Taalifi cant127
Barkeb Yàllaa wóor
1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul,ku ko tabax, neen nga doñ-doñi.Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul,ku ko wattu, neen nga teewlu.2Neen it la nit di teela jógaka guddee tëdd,di doñ-doñi lu mu lekk:Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day,fekk ko muy nelaw.3Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde,njurum doom yool la.4Doom joo jure ndaw,mooy fitt ci loxol jàmbaar;5ndokkalee ku ci mbuusam fees,ba bu ñu taseekub noon ca pénc ma,duñu am gàcce mukk.
WorldVenture