1Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi,dëkkub nootkat yi.2Dégluwul baat, nanguwul kàddu guy yare,du Aji Sax ji la wóolu,du Yàllaam jooju la jege.3Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar,ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,4ay yonentam reew, diy workat;ay sarxalkatam teddadil lépp lu sell, xëtt yoon.5Ndaxam Aji Sax jiy boroom njekk a ngi ci biiram,te du def njubadi,jantoo jant mu fenkal ab àtteem,te du wuute fu bët sete.Ab wurujkat kay moo xamul gàcce.6«Maa faagaagal ay xeet,seeni tata tasaaroo,ma wéetal seeni mbedd,ba kenn jaareetu fa,seeni dëkk a tas ba kenn desul,kenn dëkkatu fa.7«Maa noon Yerusalem: “Xanaa moos dinga ma ragal,déggal ab yar.”Su ko defee dëkkuwaayam du tas,ndax mboolem mbugal yi ma ko dikke,waaye moo yàkkamtee ñaaw ci jépp jëfam,8moo tax, xaar ma rekk,» kàddug Aji Sax jee,«ba keroog may jóg, nara sëxëtooji,nde maa dogala dajale xeet yi,dajale nguur yi,ngir xëpp leen sama sànj,mboolem sama tàngooru mer.Sama sawaras fiiraange déy,ci la mboolem àddina di xoyomu.
Yàlla mooy tuubloo xeet yi
9«Su boobaa ma soppi làmmiñu xeet yi, setal ko,ngir ñuy tudd ñoom ñépp turu Aji Sax ji,di ko jaamoondoo benn bopp.10Sama jaam ñi, sama ñoñ ñi tasaaroo,ca wàllaa dexu Kuus lañuy bawoo, ba indi samab sarax.
Yàlla soppi na xolu ndesu Israayil
11«Su bés baa gàcce dootul am ci sa mboolem jëfji nga ma moye,nde maay jële fi sa biir ñiy bége sab sag,te doo damooti ci sama kaw tund wu sell.12Waaye maay wacc fi sa biiraskan wu woyof te néew doole,ñu yiiroo turu Aji Sax ji.13Ndesu Israayil dootuñu ayibal, dootuñu fen,deesatu leen déggal kàdduy wor,ñoom doŋŋ it ñooy for, di goor,te kenn du leen tiital.»
Yerusalem dina leqaliku
14Yaw janq Siyoŋ mu taaru, sarxolleel!Éey Israayil, xaacul,yaw janq Yerusalem mu taaru, bégal,te bànneexoo xol bu sedd guyy!15Aji Sax ji moo teggi say mbugal,waññi sab noon.Buurub Israayil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir,dootuloo tiit lu bon.16Bésub keroog lees di wax Yerusalem, ne ko:«Yaw Siyoŋ, bul tiit, bul yoqi.17Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir,di jàmbaar juy walloo.Moo lay bége ci biir bànneex,leqalee la cofeelam,bége la bay sarxolle.18«Ñi amu naqar te sore ndajey bernde,ñooñu la sore, te tegoo woon gàcce,maa leen di dajale, teggil leen gàcce tey.19Ma ne jant yooyu laay jëflanteekmboolem ñi leen di sonal.Ci laay wallu kuy sukkóot,fat ku tumurànke,may leen teraanga aku tur,fépp fu ñu ruse woon ci àddina.20Yeen, jant yooyu laa leen di indi,jant yooyu laa leen di dajale,nde maa leen di defal aw tur ak teraangafi biir mboolem askani àddina,maay tijji seen wërsëg, ngeen gis.»Aji Sax jee ko wax.