Sofoni1wol_mbs

Ubbite gi

1Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Sofoni doomu Kusi. Kusi, Gedalya mooy baayam; Gedalya, Amarya, Amarya, Esekiyas. Mu yemook janti buuru Yuda, Yosya doomu Amon.

Am sànj taxaw na

2«Lépp laay buube ba mu set fi kaw suuf.»Aji Sax jee ko wax.3«Doom aadama ak mala,njanaaw ak jën laay buub,ak luy fakkastale, booleek ñu bon ñi.Maay jële doom aadama fi kaw déndub suuf.»Aji Sax jee ko wax.
4«Maay xàcc sama loxo jëme ci Yudaak mboolem waa Yerusalem.Maay jële fi bii béreb ndesu tuuri Baal,ak turu sarxalantukatam yeek sarxalkatam yi,5ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi,ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax jitey giñe Milkom, yàllantu ji,6ak ñi dëddu Aji Sax ji,wutuñu Aji Sax ji, wutuñoo diisook moom.»
7Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji,bésub Aji Sax ji kat dëgmal na;Aji Sax jee waajal ab sarax,te moo ca sellal ay ganam.
8«Keroog bésub saraxu Aji Sax ji,maay dikke mbugal kàngam yeek doomi buur yiak boroom coli ndoxandéem yi.9Bésub keroog maay dikke mbugalképp ku aw tuuram tax mu aadawoo di tëb dëxu bunt ,ak ñiy feesal seen kër yàllantu ak alalju aw ay ak njublaŋ maye.10Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax,«yuux dina jibe fa buntu Jën ya,wóoy jibe fa Sanc ya,rajaxoo ju réy jollee ca tund ya.11Yeen waa goxu marse ba, yuuxooleen,ndax jula yépp ay sànku,mboolem kuy natt dogi xaalis lees fay jële.12Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem,ba dikke mbugal ña fa ne degg,taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam,te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.”13Seen alal lees di sëxëtooji, seeni kër gental,ñu tabax ay kër yu ñu dul dëkke;jëmbat tóokëri reseñ yu ñu dul naan biiñ bi.»
14Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal,moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee.Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na,te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti.15Bésub keroog bésub sànj lay doon,bésub njàqare ak tumurànke,bésub gental ak gentle,bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus,16bésub bufta ak wootey xareca kaw dëkk ya ñu dàbbali,ak ca kaw sooroori tata ya ca koñ ya.
17«Ca laay jàqale doom aadama yi,ñuy tëñëx-tëñëxi ni silmaxa,nde Aji Sax ji lañu moy,te seen deret lees di sotti fi pëndub suuf,seen yérey biir ni neefare fi suuf.18Du seen xaalis, du seen wuruswu leen di mana xettali.Keroog bésub sànjum Aji Sax ji,ak sawaras fiiraangeem,àddina sépp ay xoyomu.Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si,te raafal gu raglu lay doon!»