1Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo rotci kaw réewum Adarag ,ba dali ca kaw Damaas.Du ci mboolem giiri Israayil rekk la Aji Sax ji ne jàkk bëtam,waaye doom aadama yépp la ne jàkk.2Kàddu gi dal na itam Amat ga digalook Damaas,dal Tir ak Sidon, ak la ñuy muus lépp.3Tir moo tabaxal boppam tata,moo dajale xaalis ni feppi suuf,ak wurus wu ne xas ni donji banu mbedd.4Ndeke Aji Sax ji moo koy moom,xalab alalam biir géej,te sawaraa koy xoyom.5Askalon moo koy gis, tiit;Gasa gis ko, jàq njàqare lu réy,mook Ekkron it ndax yaakaar ju tas.Gasa la buur bay réere,Askalon ñàkk ku ko dëkke.6Xeet wu raxe mooy sanci Asdodd,te maay sàggi sagub Filisteen ñi.7Ci seen gémmiñ laay foqatee deret ji ñuy lekk,yàbbiloo leen seen ñam yu seexluwu yi ñu ŋank.Seenu ndes it dina ma def seen Yàlla,mel nig làng ci giirug Yuda,Ekkron it ci sama ñoñ lay bokk ni Yebuseen ñi .8Maay taxaw wattu fi wër sama kër,aar ko ci ñiy dem aka dikk,ba boroom doole dootul noot sama waa kër,nde léegi samay gët laa leen ne jàkk.
Buur Almasi dikk na
9Bégal a bég, janq Siyoŋ mu taaru,janq Yerusalem mu taaru laa ne:Xaacul, niir, sa buur a la dikkal nii,moo jub te am ndam,te teewu koo woyof, war mbaam,cumbur, doomu mbaam-sëf.10Maay sànke watiiru xare ci diiwaanu Efrayim,sànke fasu xare fi Yerusalem,ay fitti xare damm,muy wax xeet yi jàmm,kilifteefam dale géej ba géej,dale dexu Efraat ba ca cati àddina.
Aji Sax ji mooy xeexal ñoñam
11Yaw nag, deret ji feddali sama kóllëreek yaw,ci laay seet ba yiwi sa nit ñi ñu tëjbiir kàmb gu ndox amul.12Yeen ñi ñu tëj, ngeen di dunde yaakaar,delluleen ca tata ja.Bésub tey jii sax maa dogu neñaari yoon laa leen di yool.13Yuda déy laay bank, muy samag xala,te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi.Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkatici sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres.Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.14Su boobaa Aji Sax jeey feeñ fi leen tiim,ag fittam tàkk nig melax.Bufta bi la Boroom bi Aji Sax ji di wal,ànd ak ngëléni bëj-saalum, dikk.15Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy aar ñoñam,ñuy falaxe, di joggati doji mbaq,di naan aka xaacu ni ñu màndi.Ni ndabi deretu juru sarax di feese,ni lañuy feese ak deretu noon yi,taq ci ripp ni cati sarxalukaay ba.16Bésub keroog seen Yàlla Aji Sax jimooy sàmm ñoñam nig jur,ñuy lerxat cim réewamni peri gànjar di ray-rayee ci mbaxanam buur.17Ndaw bànneex akub taar ca ñoom!Pepp yafal xalelu góor,biiñ bu bees naatal yaramu janq.