Taalifi cant99wol_mbs

Aji Sax ji buur bu sell la

1Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko!Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!2Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg,kawe, tiim xeetoo xeet.3Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaalleen ko.—Kee sell!4Buur, jëfe yoon mooy dooleem.Yaa saxal yoon, dëgg ak njubci askanu Yanqóoba.5Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji,te sujjóot fa ndëggastalam.—Kee sell!
6Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam,Samiyel bokk ca ñay ñaan ci turam.Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.7Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom,ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon.8Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon,di seen Yàlla ju leen di baal,te di leen mbugale seeni jëf ju bon.9Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji,te sujjóot fa tundam wu sell wa.Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!