Taalifi cant96wol_mbs

Buur Yàllaa ngi àttesi àddina

1Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,yeen àddina sépp woyleen Aji Sax ji.2Woyleen Aji Sax ji, màggal turam,di siiwal xettaleem bésoo bés!3Siiwalleen màggaayam ci biir xeet yi,xamal waasoo waaso ay jalooreem.4Aji Sax jee màgg, jara sant a santte gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.5Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la,waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.6Màggaay ak daraja, fa moom,dooleek taar, fa këram gu sell.
7Yeen làngi xeet yi, seedeelleen Aji Sax ji;seedeelleen Aji Sax ji màggaayam ak dooleem.8Seedeelleen Aji Sax ji màggaayu turam,yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.9Sujjóotalleen Aji Sax ji gànjaroo sellaay.Ragalleen ko, bay lox, yeen waa àddina sépp.10Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur!Àddinaa ngi sampu ba dëgër moos, maneesu koo rëññeel.Mooy àtte xeet yi njub.11Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul!Géejoo, riiral yaak mboolem li la fees,12na mbooy mi jaayu, mook lu ci biiram,ba mboolem garabi àll bi sarxolleendoo,13gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,àttesi àddina,di àtte dun bi dëgg,tey àtte xeet yépp ci dëggoom.