Taalifi cant91wol_mbs

Aji Sax jee mat kaaraange

1Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe jiyaa këroo keppaaru Aji Man ji.2Dama naa Aji Sax ji:«Yaw laay làqoo, di la fegoo;ngay sama Yàlla ji ma doyloo.»3Kii kay moo lay musal cig fiirak loraangey mbas.4Kiiraayam la lay sànge,nga yiiru, làqu;kóllëreem feg la, di la aar.5Doo ragal njàqarey guddimbaa fittu bëccëg6mbaa mbas mu yooteg lëndëm,ak balaa buy faat njolloor.7Junni daanu fi sa wet,fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor,du tax mu jege la.8Say gët nga ciy teg,di seetaan ku bon di jot yoolam.9Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji,Aji Kawe jii di sama rawtu,10genn loraange du la dab,balaa du jege sa xayma.11Ay malaakaam la lay booleel,ñu di la sàmm foo jëm.12Seeni loxo lañu lay leewoo,ba doo fakkastalu ciw doj.13Dangay falaxe jaan ak gaynde,di rajaxe ñàngóor ak sibi.
14Yàlla da naa: «Kii de man la safoo,ma di ko xettali.Man la xam, te maa koy teg fu wóor.15Mu woo ma, ma wuyu ko;mook man ci biir njàqare,ma xettali ko, darajaal ko,16reggal koy fan,baaxe ko samag wall.»