Taalifi cant89wol_mbs

Aji Sax ji, loo dige woon?

1Dib taalifu yeete bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
2Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww,di biral wormaam sët ba sëtaat.3Dama ne, sa ngor dàkk la sax,fa asamaan nga dëël sa worma.4Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn,muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:5“Damay saxal sa askan ba fàww,samp sab jal sët ba sëtaat .”» Selaw.
6Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore,ndajem ñu sell ña di la joobee sa kóllëre.7Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kaw-a-kaw?Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,8Yàlla ji ñu teral a teral ci jataayu ñu sell ñi,te mu gëna raglu lu ko wër?9Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,Ki Sax, ana ku tollook yaw doole?Yaw mi sa kóllëre féete fu ne!
10Yaw yaa man géej gu sàmbaraax;gannax ya fuddu, nga dalal.11Yaa rajaxe Raxab miy ninki-nankay géej, bóom ko,tasaare say noon ci sa doole.12Yaa moom asamaan, yaa moom suuf.Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.13Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk.Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.14Yaa àttan, jàmbaare;sa loxo di dooley neen,sa ndijoor ca kaw!15Àtteb dëgg ak njub a lal sab jal,ngor ak worma dox jiitu la.
16Aji Sax ji, ndokkalee mbooloo mu la xal di sarxollee,di niitoo saw yiw,17ànd di la bége bés bu ne,sa àtteb dëgg siggil leen.18Seen darajay doole, yaw a.Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.19Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom;sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu,ne leen: «Kaweel naa jàmbaar ci xeet wi,dénk ko ndimbal.21Maa ràññee sama jaam Daawuda,fale ko sama diw gu sell,22ànd ak moom, saxal ko,sama loxo di ko dooleel.23Noon du ko bett,ku bon du ko toroxal.24Ay bañam, ma rajaxe;ay noonam, ma faat,25sama wormaak sama ngor di ko gunge,may yokk kàttanam.26Géej, ma teg ci loxoom,dex, ma ne ca tegg ndijooram.27Moo ma naa: “Yaay sama baay,di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”28Te it maa koy def samab taaw,tiimale ko buuri àddina,29sàmmal ko sama ngor ba fàww,feddalil ko sama kóllëre.30Damay saxal askanam ba fàww,yàggal ab jalam ni asamaan.31Bu ay sëtam wàccee sama yoon,baña doxe samay ndigal,32mbaa ñu xëtt sama dogali yoon,baña sàmmonteek samay santaane,33ma bantale leen seenug moy,dumaa leen seen ñaawtéef.34Waaye duma ko daggal sama ngor,te duma ko ñàkke worma.35Déet, duma masa fecci sama kóllëre,te duma toxal sama kàddu.36Benn yoon laa ko giñ ci sama sellaay,duma fen Daawuda:37askanam, dàkk;ab jalam fi sama kanam ni jant bi,38ak weer wi sax ba fàww,dib seede bu wér ca niir ya.» Selaw.
39Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal,mere ko, wacc ko.40Fecci nga sa kóllëreek sab jaam,foq nguuram, detteel ko.41Bëtt nga ñagam yépp,saam ay tataam,42ku fa jaare, jël ca alalam,mu doon mbalitu dëkkandoo yi.43Yékkati ngay bañam,noonam yépp di ree.44Waññi nga ñawkal saamaram,te taxawuloo ko cib xare.45Xañ nga ko darajaam,rattax ngànguneem fa suuf.46Dagg nga fani ngoneem,sang ko gàcce. Selaw.
47Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex?Xanaa doo làqu fàww nii,sa mer di boy?48Bàyyi ma xel, samay fan yàggul.Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?49Ana kuy dund te du dee?Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.50Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfete nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?51Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi,ak xeet yu bare yi ma yenu yépp.52Aji Sax ji, say noon a ngi sewalbuur bi nga fal, ne ko dann.
53Cant ñeel na Aji Sax ji ba fàww.Amiin, amiin.