1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.2Éy Aji Sax ji, yaa baaxe woon sa réew mi,ba suqali sëti Yanqóoba yi,3baal sa mbooloo seeni ñaawtéef,jéggal leen bépp bàkkaar. Selaw.4Bàyyi nga xadar ja,muñ mer ma.5Éy Yàlla mi nuy musal, suqali nu,te meddi.6Xanaa doo nu mere fàww,ba ca sët yaak sëtaat ya?7Xanaa dinga leqali sa mbooloo,ba ñu man laa bànneexoo?8Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor,baaxe nu sag wall.9Woykat ba nee: «Naa déglulu Aji Sax ji Yàlla di wax.»Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam,ba duñu dellu ci jëfi dof.10Wallam aka jege ñi ko ragal,te leeram dëgmal sunu réew mii!11Ngor ak wormaa daje,njub ak jàmm saafoonte,12kóllëre jebbee fa suuf,njub séentoo asamaan,13Aji Sax ji it maye ngëneel,sunu suuf meññal,14njub jiitu Aji Sax ji,di ko xàllal yoonam.