Taalifi cant81wol_mbs

Déggal Yàlla, jariñu

1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit .
2Sarxolleleen ci Yàlla mi nuy dooleel;xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba.3Yékkatileen woy te jiin,xalam neex, ànd ak moroom ma.4Walleen bufta bi ci Terutel weer wi,ak weer wu birale bésu màggal.5Loolu wartéefu Israayil la,di ndigalu Yàllay Yanqóoba,6di ndénkaane bu mu dénk waa kër Yuusufa,ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra.Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:7«Yennil naa leen yen bi,woyofal seeni loxo.8Ngeen jàq, woo ma, ma xettali leen,wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya,te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.9Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen.Éy Israayil, su ngeen ma déglu woon!10Buleen fat tuuru jàmbur,buleen sujjóotal tuuru doxandéem.11Man, Aji Sax ji, maay seen Yàllaji leen yékkatee réewum Misra.Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.
12«Waaye sama ñoñ déggaluñu ma,ñuy Israayil gii ma nangulul.13Moo tax ma bërgël leen ak seenug të,ñuy wéye seeni pexe.14Éy su ma sama ñoñ déggaloon,éy su Israayil toppoon samay nammeel!15Ci saa si laay toroxal seeni noon,duma seeni bañ,16ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal,te àppam du jeex ba fàww.17Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp,reggal leen lem ju doj xelli.»