1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf.2Éy yaw, Sàmmu Israayil, teewlu nu;yaw mi jiite Yuusufa ni ag jur,yaw mi toogandook malaakay serub yi,feqal sag leer.3Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase,te wallusi nu.4Éy Yàlla, suqali nu;geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.5Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi,foo àppal sa mer,mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi?6Leel nga nuw naqar,nàndal nu mbàndum rongooñ,7def nga dëkkandoo di nu xëccoo,noon di nu ree.8Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu;geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.9Yaa déjjate ag reseñ ci Misra,dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.10Nga raadu suuf si,reseñ gi sampu, law, dajal réew mi;11keppaaram muur tund yi,ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.12Mu tàllal ay bànqaasam ba géej,lawal njebbit la ba ca dexu Efraat ga.13Lu tax nga bëtt ay ñagam,ba ku fa jaare witt ca,14mbaam àll di ko ruur,ndundati àll di ca for?15Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul;séentool asamaan, ba giste taxawusi reseñ gii.16Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor,ngarab sii nga dooleelal sa bopp.17Dees koo gor, taal;yal na ñii sànkoo sa mbugal.18Yal nanga yiir ki nga tànn,kii nga dooleelal sa bopp,19ba dootunu la dëddu.May nu nu dund, nu wormaal sa tur.20Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu,geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.