Taalifi cant8wol_mbs

Aji Sax ji teral na nit

1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit , ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
2Aji Sax ji sunu Boroom,sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!Sag leer tiim asamaan.3Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp,feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon,bañaaleek feyukat ne xerem.
4Damay xool sa asamaan si nga móol,ak weer week biddiiw yi nga fi teg.5Moo, luy nit, ba nga di ko bàyyi xel?Luy doom aadamaak loo koy yége?
6Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi,yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,7fal ko ci kaw loo bind,jox ko lépp, mu teg tànk:8jur gépp, gu gudd ak gu gàtt,rabi àll it ca la,9ak njanaaw ak jënak luy jaare yooni géej.
10Aji Sax ji sunu Boroom,sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!