Taalifi cant77wol_mbs

Yàllaa ngi seetaan

1Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf.
2Naa xaacu, woo Yàlla,sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.3Bëccëg, ma jàq, sàkku ndimbalal Boroom bi;guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma.Sama xol tëë sedd.4Ma bàyyi Yàlla xel, binni,xalaat, xol jeex. Selaw.5Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët,ma jaaxle ba waxatuma,6xanaa xalaat janti démb,at ya woon.7Guddi may fàttaliku sama woy,di waxtaan ak sama ngegenaay,sama xel di jéex te naa:8«Boroom bi da may gàntal ba fàww,ba du ma baaxeeti mukk a?9Xanaa daa jeexal ngor tàkk?Am kàddoom a deñ ba fàww?10Moo, mbaa du Yàlla daa fàtte ñeewante?Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw.11Ma ne, sama naqar daalmooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom.
12Waaye naa fàttaliku jaloorey Ki Sax rekk,fàttaliku kéemaanam ya woon.13Naa xalaat sa bépp liggéey,di jàngat say jëf.14Céy Yàlla, yaa sell jikko!Jan yàllaa màgg ni Yàlla?15Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan,yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi.16Kàttan nga jote sa mbooloo ma,sëti Yanqóobaak Yuusufa. Selaw.17Yàlla, ndox maa la gis,ndox maa la gis, di lox;xóote yaa say,18niir ya yuri,kàddu riire asamaan,say fitt, fettaxandoo,19nga dënoo biir callweer,melax yi taal àddina,suuf di lox, di reg-regi.20Biir géej di saw yoon;saw xàll ci digg ndox mu ne xéew,te kenn gisul foo teg tànk!21Wommat nga sa mbooloo ni ag jur,Musaak Aaróona jiite.