Taalifi cant76wol_mbs

Yàllaa moom xare

1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, di woyu cant, ñeel Asaf.
2Yàlla siiw na fa Yuda,aw turam màgg fa Israayil.3Xaymaam a nga Salem,di xuntam ma fa Siyoŋ.4Fa la rajaxee fitt yuy boyak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare. Selaw.
5Yàlla yaa ne ràññ te darajawu,ba raw tundi rëbbkat yi.6Futtees nay boroom fit,ñu ne nërëm, nelaw;kuy ñeyi xare, say loxo nasax.7Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd,gawar ak fasam nelaw.8Yaw mii, yaa mata ragal;boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?9Fa asamaan nga biraleb àtte;suuf tiit, ne cell.10Ca la Yàllay jóg, ngir àtte,ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.11Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy;desu xadaram, nga gañoo.
12Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moomte jëfe ko.Kee jara ragal.Na ñi ko wër ñépp indi teraanga.13Mooy sàggi sagu kilifa yi,di tiitaangey buuri àddina.