Taalifi cant74wol_mbs
Yàlla, bu la noon ree
1Dib taalifu yeete, ñeel Asaf.Éy Yàlla, lu tax nga wacc nu fàww,di dal ak xol bu tàngci sa xari parlu yii?2Bàyyil xel askan wi nga jënd bu yàgg,yaa jot gii giir, séddoo leen.Bàyyil xel tundu Siyoŋ, fa nga dëkke woon.3Dikkal, xool gent bu yaa bii dul jeex,noon yàq lépp ci biir kër gu sell gi.4Say bañ xaacu nañu fa sa digg bérebu ndaje ma,samp seen raaya.5Sémmiñ dal, wàkku awu.Mbete ñu xàcc sémmiñ, di gori geer,ba lu fa doon liggéeyu yatt, tas.7Dañoo taal sa kër gu sell,sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko.8Ñu namm noo noot ba nu nooy,fuy bérebu ndajem Yàlla ci réew mi, ñu lakk.9Sunuy takk réer na nu,yonent amatul,te kenn xamul fu lii di àkki.10Éy Yàlla, fu reetaani noon di dakke?Xanaa bañ yi duñu la ñàkke kersa ba fàww?11Looy téye sa loxol ndijoor?Na sa loxo jóge sa dënn, nga buube leen.12Yàlla, yaa masa doon sama buur,di ma walloo ci digg réew mi.13Yaa xàjjale géej gi ci sa doole,toj boppi ninki-nanka ja ca ndox ma,14yaa rajaxe kaaŋi rab woowu,leele ko rabi màndiŋ ma.15Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal,ŋiisal dex yu masa wal.16Yaa moom bëccëg, moom guddi,teg fi weer week jant bi.17Yaa rëdd mboolem digi suuf,sàkk noor ak nawet.18Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree,xeet wu amul bopp a lay sewal.19Bul wacce rabu àll sam xati,bul sàggane sa néew-doole yi mukk.20Ngalla xoolal ci kóllëre gi,fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.21Yàlla bu néew-doole ñibbiwaale gàcce,yal na ku ñàkk ak ku néewle di la santandoo.22Éy Yàlla, jógal ñoŋal sa dëgg,bàyyil xel dof bi la dëkkee sewal.23Bul tanqamlu sa coowal noon yi,ñii la jógal, seenum riir a ngi jolli saa su ne.