Taalifi cant72wol_mbs
Nu ñaanal Buur
1Ñeel Suleymaan.Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte,mayal doomu Buur bii sa xelum njub,2muy àttee sa mbooloo njub,di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon,3tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm,tooli tund yu ndaw yi xéewale leen àtteb dëgg,4Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi,di wallu doomi néew-ji-dooletey dëggaate kiy nennoo.5Yal nañu la wormaal feek jant biy am,feek weer wiy feq, sët ba sëtaat.6Yal na Buur di xéewalu réewam nib taw cig ruujeef,mbaa waame wuy suuxat suuf.7Janti Buur aji jub day woomle,te ba keroog weer wiy fey, jàmm di law,8mu yilif géej ba géejak dexu Efraat ba ca cati àddina.9Waa màndiŋ mi di ko sukkal,ay noonam mëq suuf,10buuri Tarsis ak dun yadi ko indil ay galag;buuri Seba ak Sabadi ko yótsi yóbbal,11buuroo buur di ko sujjóotal,xeetoo xeet di ko surgawu.12Mooy xettaliji aji tumurànke bu woote wallak aji néewle ju sësul fenn.13Mooy yërëm ku néewleek ku tumurànke,di sàmm bakkanu aji tumurànke,14boole leen jot ci nootaangeek loraange,ngir fonk seen bakkan.15Yal na Buur gudd fan,yal nañu ko may wurusu Seba.Nañu koy ñaanal saa su ne,di ko saxoo, mu barkeel.16Yal na pepp ne gàññ ci réew mi,yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ;dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,17yal na turam sax,ba law fu jant tiim,yal na xeet yépp barkeele ci moom,te di ko ndokkale.18Cant ñeel na Yàlla Aji Sax ji,Yàllay Israayil, mi wéetooy jalooreem.19Cant ñeel na màggaayam, ba fàww,yal na màggaayam dajal suuf sépp!Amiin, Amiin!20Ñaani Daawuda doomu Yese jeexe fii.