1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttalee.2Yàlla, wallu ma!Éy Aji Sax ji, gaawe ma!3Kuy wut sama bakkan,yal na rus, torox ne tott.Kuy bége sama loraange,yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.4Kuy ñaawalaate,yal nañu ko toroxal, mu daw, dellu gannaaw.5Képp ku la wër,yal na bég, di la bànneexoo.Képp ku safoo sag wall,yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»6Man de, néew naa doole, ñàkk naa.Éy Yàlla, gaawe ma.Yaw yaa may wallu, xettali ma.Éy Aji Sax ji, bu ma yeexe.