Taalifi cant65wol_mbs

Yàllaay nangul suuf

1Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ,yaw lees di jëfeel ab dige.3Yaw miy nangug ñaan,yaw la képp di wuyusi.4Samay ñaawtéef man na ma,waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.5Ndokkalee koo tànn, woo ko,mu dale say ëtt,di xéewloo sa ngëneeli kër,ak sa sellaayu dëkkuwaay.
6Defal nga nuy kéemaan,nangug ñaan ci njekk,yaw Yàlla mi nuy wallu,di yaakaaru àddina wërngal këpp,ba ca géej gu sore ga.7Yaa dëje tund yu mag yi doole,gañoo sa kàttan,8di dalal riirum géej aki gannaxam,ak coowal xeet yi,9ba waa cati àddina yéemoo say firnde,waa penkook sowu di sarxolle.
10Yaa dikke suuf am wal,nangul koo nangul.Dexu Yàllaa fees ndox,ngay may nit peppam,ni nga ko waajale suuf si,11di suuxat ngàbb mi,maasalee ko jal yi,sottiy waame, mu mokk,cax ma, nga barkeel.12Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel,foo jaare, xéewal walangaan.13Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan,li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.14Joor gaa ngi, jur gi muur,xur yi sàngoo pepp,lépp di xaacooka woy.