Taalifi cant63wol_mbs

Maa namm Aji Sax ji

1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda .
2Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla,ma xëy di la wër,sama bakkan mar la,sama jëmm namm la,fu suuf mare ndox, ne sereŋ.3Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo,ngir niir sa doole ak sa leer.4Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan;ma àddu boog, kañ la!5Dama lay sant, sama giiru dund kay,tàllal la ay loxo, sàbbaale la.6Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural,ma bég, sarxolle, màggal la.
7Su ma tëddee, fàttaliku la,waxtuw guddi dama lay xalaat.8Yaay sama ndimbal,may làqoo sa kiiraay,di sarxolle.9Sama xol taq la,nga téyee ma sa ndijoor.
10Waaye ñiy wuta faat sama bakkanñoo jëm xóotey njaniiw.11Ñu jébbal leen ñawkay saamar,till séddoo.
12Buur moom, di bége Yàlla;képp ku koy giñe di ko kañoo,fen-kat ne xerem.