Taalifi cant60wol_mbs

Yàllaa yor sunu mucc

1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb tóor-tóor, diy ñaan, ñeel Daawuda.2Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Coba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa .
3Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay.Mer nga, waaye ngalla xettali nu.4Yëngal nga suuf, xar ko;ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!5Won nga sa mbooloo lu metti,nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.6Sampal nga ab raaya ñi lay ragal,ngir ñu mucc ci fitt yi. Selaw.7Walloo nu sa ndijoor, nangul nu,ba say soppe xettaliku.
8Yàllaa àddoo fa këram gu sell,ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem,séddale xuru Sukkót.9Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase,Efrayim di sama mbaxanam xare,Yuda di sama yetu nguur,10réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay,Edom, ma teg tànk;Filisti, ma xaacoo fa.»
11Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër?Ku may jiite ba Edom?12Xanaa kay du yaw, Yàlla mi nu wacc,yaw Yàlla mi baña ànd ak sunu mboolooy xare?
13Ngalla dimbali nu ci bañaale;doom aadama, wallam neen la.14Nook Yàlla, nu def njàmbaar;moom mooy noot sunuy noon.