1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.2Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb,bul xadaru, ba di ma mbugal.3Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma!Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!4Sama xol a jeex tàkk.Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?5Éy Aji Sax ji, délsil, xettali ma!Walloo ma sa ngor.6Deesul dee ba fàttaliku la;ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?7Onk naa ba loof, di fanaanee jooy,sama lal di féey,ba far seeye rongooñ.8Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar,boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.9Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma!Aji Sax ji dégg na saay jooy,10Aji Sax ji dégg na saay dagaan,Aji Sax jii nangu na samag ñaan.11Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool,ne wërëñ ak gàcceg mbetteel.