1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete, ñeel Daawuda.2Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la,bul làqu, dama lay dagaan.3Teewlu ma, nangul ma.Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;4coowal noon yeeak coonob ñu bon ñi.Dañu maa teg fitna,di ma songe xadar.5Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi;tiitaangey dee ne ma taral.6Njàqaree ma dugg, may kat-kati,musiba mëdd ma.7Dama ne: «Éy ku may may laafi xati,ma ne fërr, noppaluji.8Xanaa ma naaw, ba sore,fanaani màndiŋ ma. Selaw.9Naa gaawtu, seelujingelaw lu riddi ak ngëlén.»10Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen.Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,11guddeek bëccëg ñuy wër,ñaawtéef ak ayib wéttali leen.12Yàq a nga ca biir,te nooteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.13Su doon noon bu may ñaawal,ma muñ ko,mbaa muy bañ bu may won ab dayo,ma daw ko.14Waaye yaw la, sama nawle,di sama wóllëre, ma xam la.15Nu daan bokk bànneexu diisoo,ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.16Yal na leen dee bett,ñu jekki tàbbi njaniiw,ngir mbon ga ci seen biir ak seen dëkkuwaay.17Waaye man, Yàlla laay woo wall,te Aji Sax jee may wallu.18Subaak ngoon ak njolloor,may ñaxtooka ñurumtu,mu dégg ma.19Moo may jot ak jàmm,ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.20Yàllaay dégg, duma leen,moom mi nguuram yàgga sax. Selaw.Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.21Workat baa ngi xàcc loxoom jëme ci ñi mu takktool,di fecci kóllëre,22làmmiñ wa daa neex ni lem,te xare lal xol ba;kàddu ya gëna nooy ag oliwte di saamar bu génn mbaram.23Sippikul Aji Sax ji lu la diis,moom moo lay taxawu.Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf.24Waaye yaw Yàlla, yaa leen di tàbbal,bóomkat ak naaféq ci pax mu xóota xóot,te seen dund xaajul.Man nag, ma di la wóolu.