Taalifi cant54wol_mbs

Yàlla, dimbali ma

1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.2Mooy ba waa Sif demee ca Sawul, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew .
3Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur,jox ma dëgg, ci sa kàttan.4Éy Yàlla, déglul, ma ñaan,teewlul, ma wax la.5Ay doxandéem a ma jógal,di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan,te seetuñu ci Yàlla. Selaw.
6Yàllaa ngii, moo may dimbali;Boroom bee yor sama bakkan.
7Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru,yal na leen sa dëgg sànk.8Xol bu tàlli laa lay sarxale.Aji Sax ji, yaa baax, ma sant la.9Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële,ma tiim samay noon.