1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.2Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sawul, ne ko Daawuda dem na kër Aximeleg .3Moo! Jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor?Yàlla, ngoram, bés bu nekk la.4Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange,mel ni saatu su ñu xacc,rambaaj bi!5Lu bon a la gënal lu baax,fen a la gënal wax dëgg. Selaw.6Yaa bëgg jépp wax juy yàq,waabajiiba bi!7Yàlla da lay sànk ba fàww,fëkke la sab xayma, yóbbu,déjjatee la réewum aji dund. Selaw.8Aji jub gis ko, yéemu,di la ree, naa:9«Xoolleen jàmbaar ji làqoowul Yàlla,xanaa di yaakaar alalam ju bare,di yokkoo loraange.»10Man, ma mel ni garabu oliw gu naatfa biir kër Yàlla,di wóoloo Yàlla ngoram tey ak ëllëg.11Naa la sante sa jëf ba fàww,naa biral sa tur wu baax,say wóllëre teew.