Taalifi cant49wol_mbs

Alal day naxe

1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
2Yeen, xeetoo xeet, dégluleen;yeen, waa àddina yépp, teewluleen,3ngay ku tuut di ku mag,nga bareleek nga néewle.4Li may wax xel la,di xalaat yu déggu.5Damay teewlu kàddu yu xelu,xalamal la sama tekkiteb cax.
6Ana lu may tiit bés yu metti,yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,7di ñu wóolu seen am-am,di kañoo alal ju bare?8Ana ku mana jot a jot sa bakkanu moroom,mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?9Njotug bakkan jafe na,bu ci jéem dara.10Ana kuy dund ba fàww,ba doo gis bàmmeel?
11Xanaa gis ngeen ne xelu, dee;dof, dee; naataxóona it faatu rekk,wacce keneen alalam.12Sa bàmmeel di sa kër ba fàww,di sa dëkkuwaay bu sax dàkk,boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.13Nit ak darajaam fanaanul,mook aw rab a yem, sànku rekk.
14Nii la ku wóolu boppam di mujje,mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.15Nara dee rekk niy xar,dee wommat, yóbbu,njub fenk nib jant, ku jub moom leen,njaniiw mëdd seen jëmm,fu sore kërug daraja.16Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw,jot sama bakkan, ba jël ma. Selaw.
17Buleen yéemu ci ku barele,teraangay këram di yokku.18Du dee ba yóbbaale dara,teraangaam du ko topp biir bàmmeel.19Na bége bànneexu bakkanam,ñu di ko kañe koomam,20ba tey, day dee, fekkiy maamam,ña dootul gisug leer ba fàww.21Nit ak darajaam te amul dégg,mook aw rab a yem, sànku rekk.