1Di woyu cant, ñeel askanu Kore wu góor.2Aji Sax jee màgg, jara màggal a màggalca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu sell.3Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar,dëkku Buur bu mag bi,di mbégtem àddina sépp.4Yàllaa wone kaaraangeemca biir tatay dëkk ba.5Buur yaa ngoog daje,àndandoo.6Nun noo gis, jommi,tiit, fëx,7ne fay pat-pati,jàq ni kuy matu.8Ngelawal penku, moom ngay tasegaal gu mag.9La nu déggoon de lanu gisca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,sunu dëkku Yàlla ba.Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.10Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër,di xalaat sa ngor.11Céy Yàlla, sa tur ay sa woyba ca cati àddina.Njubte la sa loxo fees.12Yal na waa tundu Siyoŋ bég,waa Yuda bànneexoo say àtte.13Doxleen biir Siyoŋ, wër ko,waññleen ay sooroori tataam,14nemmikuy tataam,doxantoo këri buur,ba man koo yegge maasug ëllëg,15ne leen kii ay Yàlla, sunu Yàlla,tey ak ëllëg.Moo nuy jiite ba saa taxaw.