Taalifi cant
47
/
wol_mbs
Yàllaay Buur
1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
2
Na xeetoo xeet tàccu,
xaacu, sarxolleel Yàlla!
3
Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal,
mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp.
4
Moo nu nangulal xeet yi,
nu teg tànk gàngoor yi.
5
Moo nu tànnal céru suuf,
muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. Selaw.
6
Yàllaa yéeg, kàddu riir.
Aji Sax jee yéeg, bufta
info
jolli.
7
Woyleen Yàlla, woyleen,
woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
8
Yàllaay buuru àddina sépp;
taalifleen, woy ko.
9
Yàllaa di buuru xeet yi,
Yàllaa tooge jalam bu sell.
10
Kàngami xeet yeey daje,
ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma;
Yàllaa moom buur yi yiir àddina,
te moo kawee kawe.
Powered by Seed Bible API
expand_more
Search
All books
Old Testament
New Testament
chevron_left
Previous Chapter
Books
search
Search
explore
Discover
share
Share
chevron_right
Next Chapter