Taalifi cant46wol_mbs

Aji Sax jee ànd ak man

1Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
2Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel,di nu wallu fu nu jaaxlee,3ba dunu tiit suuf su yëngu sax,ba tund yiy tàbbi biir géej,4mbaa gannax yuy riir, di fuuraka fuddu bay gësëm tund yi. Selaw.
5Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla,sellaayu màkkaanu Aji Kawe ji.6Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf;Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.7Ay giir a riir, ay réew yëngu;mu àddu, suuf seey!8Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun,Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
9Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji,ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.10Mu ngi fey xare ci àddina sépp,dog fitt, damm xeej, lakk pakk.11Mu ne: «Dalleen te xam ne maay Yàlla,màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»12Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun,Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.