Taalifi cant42wol_mbs

Maa namm Yàlla

1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
2Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox,maa la koy sàkkoo xol.3Maa mar Yàlla,Yàlla jiy dund!Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?4Rongooñ laay dundeguddeek bëccëg,noon yi di ma dëkke naa:«Ana sa Yàlla ji?»5Lii laay fàttaliku, sama xol jeex:dama daan jàll, jiite mbooloo ma,jëm kër Yàlla ga, di sarxolleeka sant,ñu booloo di màggal.6Moo man, lu may xàddi, ne yogg?Lu may jàq nii?Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko,moom sama Yàlla mi may wallu?
7Maa ngi ne yogg,ba di la fàttalikoo fa réewum Yurdanak tundi Ermon ak Miccar.8Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma;say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.9Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram,guddi ma fanaane koo woy,di ñaan Yàlla mi may dundal.10Naa wax Yàlla sama cëslaay, ne ko:«Lu tax nga fàtte ma,noon di ma fitnaal,may wéye tiis?»11Noon yaa ngi may ñaawal,di ma yendoo naa:«Ana sa Yàlla ji?»Ma ne yàcc, ne yasar.12Moo man, lu may xàddi, ne yogg?Lu may jàq nii?Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko,moom sama Yàlla mi may wallu?