1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.2Ndokkalee yaw mi yég néew-ji-doole.Aji Sax jee lay xettali, bésub njàqare.3Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan,nga jagoo barke ci réew mi,te du la bàyyi noon def la lu ko neex.4Aji Sax jee lay dooleel soo woppee,di soppi bu baax sa tëraay.5Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la;baaxe ma, faj ma.»6Noon yaa ngi may yéene lu bon,naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»7Ku dikk, di ma seet, di jinigaltey fenti sos ci xolam,bu génnee, tasaare ko.8Bañ yépp a ngi may déeyoo,di ma fexeel lu bon,9naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»10Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma,te daan lekk samaw ñam.11Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma,yékkati ma, ma fey leen.12Su noon damuwul ci sama kaw,ma doora xam ne bége nga ma.13Man, damaa màndu, nga taxawu ma,dëj ma fi sa kanam ba fàww.14Cant ñeel na Aji Sax ji Yàllay Israayil.Moo masa yelloo cant ba fàww.Amiin, Amiin.