1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.2May xaar a xaar Aji Sax ji,mu dégg may woote, geesu ma,3génnee ma ca kàmbug sànkute,sippee ma ca xóotey ban ba,cëppe ma ciw doj,samp ma, ma dëgër.4Moo ma may, ma fent,woy wu ma woye sunu Yàlla.Ñu baree seede, di wormaalaka dénku ci Aji Sax ji.5Ndokkalee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji,te sàkkuwoo ku bewak kuy topp ay fen.6Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def,amuloo moroom!Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal,ma bëgga xamle lépp,te mu bare ba wees ab lim.7Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko,ay nopp nga ma bënnal,saraxu rendi-dóomal ak saraxu póotum bàkkaar,sàkkuwuloo ko.8Ma ne: «Maa dikk nii,téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.9Sama Yàlla, maa defsi sa coobare,ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»10Siiwal naa sag njubte ca ndaje mu mag ma.Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.11Làquma sag njubte, ne cell ak moom.Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko.Làquma sa ngor ak sa kóllëre ca ndaje mu mag ma.12Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande.Sa ngor ak sa kóllëre,yal na ma feg ba fàww.13Ay musibaa ma tanc,ne gàññ, ba wees ab lim.Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma,baree bare, ba ëpp sama kawari bopp;sama xol jeex tàkk.14Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma!Éy Aji Sax ji, gaawe ma!15Képp kuy wuta fëkk sama bakkan,yal na rus, torox ne tott.Kuy bége sama loraange,yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.16Ku may ñaawal,yal nañu ko toroxal, mu daw, dellu gannaaw.17Képp ku la wër,yal na bég, di la bànneexoo.Képp ku safoo sag wall,yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»18Man, néew naa doole, ñàkk naa,waaye yaw Aji Sax ji, danga maa yég.Yaw yaa may wallu, xettali ma;sama Yàlla, bu ma yeexe.