Taalifi cant36wol_mbs

Nit ñaaw, Aji Sax ji gore

1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.
2Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi ci sama xel mi.Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?»3Day gis boppam, naagu,ba du gis sikkam, sib ko.4Ay waxam coxor aki fen,jëfeetul lu rafet ak lu baax.5Day mébét lu ñaaw cib lalam,taxawe yoon wu dëddu mbaax,te du bañ lu bon.
6Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan,dëggu ba ci kaw-li-kaw.7Sa njubtee tiim tund yu mag yi,sa àtte ne xéew ni xóotey géej.Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!8Céy Yàlla, yaa wéet ngor,doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru;9yafloo sa njël lu duun,sa xéewal wal, nga nàndale ko.10Ci yaw la dund di balle,te sag leer lanuy leerloo.
11Jotaleel sa ngor ku la xam,jotale sa njubte kuy nas njub.12Yàlla bu ma ku reew teg tànk;loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw.13Defkati mbon yaa ngii, daanu,ne lareet, tëlee jóg.