Taalifi cant34wol_mbs

Aji Sax ji du tanqamlu aji jub

1Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem .
2Naa màggal Aji Sax ji saa su ne,di ko sant fu ma tollu.3Aji Sax ji laay sagoo,néew-ji-doole dégg, bég.4Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man,nu bokk wormaal turam.
5Maa topp Aji Sax ji, mu nangul ma,tàggale maak lépp lu ma ragal.6Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ,gàcce du ko sëlëm.7Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu,musal ko fu mu jàqe.8Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la,di la wallu.9Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax,ndokkalee yaw mi ko làqoo.10Ragalleen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi;ku ko ragal doo ñàkk dara.11Gaynde man naa ndóol, xiif,nit kiy jaamu Aji Sax ji ñàkkul lenn lu baax.
12Dikkal doom, déglu ma,ma jàngal la ni ñuy ragale Aji Sax ji.13Ana ku dund neex,mu bëgga fekke bés bu rafet, ba gis ngëneel?14Na làmmiñam daw lu aay,dawi fen.15Na dëddu lu bon tey def lu baax,sàkku jàmm, saxoo ko.
16Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ñi,te ay noppam la dékk seeni woote wall.17Aji Sax jeey won gannaaw ñiy def lu bon,ngir dagge leen kaw suuf, far seeni tur.18Ñi jub yuuxu, Aji Sax ji dégg,fu ñu jàqe, mu musal leen.19Seen yaakaar tas, Aji Sax ji jege leen,seen xol jeex, Aji Sax ji wallu leen.20Musiba bare naa dal ku jub,Aji Sax ji musal ko ci lépp,21di ko sàmm,ba benn yaxam du damm.22Musiba nag day rey ku bon,te ku bañ aji jub, yoon dab na la.23Aji Sax jeey musal ab jaamam,képp ku ko làqoo, yoon du la dab.