1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.2Aji Sax ji, yaw laa làqoo,yàlla buma rus mukk.Yiwee ma sa àtteb dëgg.3Teewlu ma,gaawe ma,Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu.Aar ma, ma mucc.4Yaay sama cëslaay, sama rawtu.Jiite ma, wommat ma ngir sa tur.5Génne ma fiir gi ñu may tëroo;yaw yaa di sama rawtu.6Yaw laa jébbal samag noo.Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma.7Maa bañ kuy topp tuuri neen.Man, Aji Sax ji laa wóolu.8Damay bég, di bànneexoo sa ngor,li nga xoole samaw tiis.Ràññee nga sama njàqarey xol.9Waccoo ma ci loxol noon,danga maa taxawal fu ma yaatoo.10Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa!Samay gët a ngi giim ndaxu tiis,xol jeex, yaram jeex.11Naqar a ngi may rey,tiis di wàññi samay fan,sama doole ŋiis ndax sama njubadi,samay yax semm.12Noonoo noon a ma sewal,dëkkandoo waxi noppi,xame seexlu ma,ku ma gis biti, di ma daw.13Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee,ma mel ni ndab lu yàqu.14Damaa dégg jëw yu bare,lu raglu dar ma kepp.Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel,di wut sama bakkan.15Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku.Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»16Yaa yor sama àpp.Xettali maak ku ma noonooak ku may sonal.17Leeralal ma sa kanam, Sang bi,walloo ma sa ngor.18Éy Aji Sax ji, woo naa la wall,yàlla buma rus.Yal na ku bon rus,ne xerem biir njaniiw.19Yal nanga tëj gémmiñu fen-katbuy wax aji jub waxi reewande,di réy-réylooka xeebaate.20Yàlla yaa yaatu ngëneelloo dencal ku la ragal,defal ko ku la làqoo,doom aadama seede.21Yaa koy làq fa nga làqu,fa pexey nit àggul.Nga yiir ko, mu yiiruci ayu làmmiñ.22Cant ñeel na Aji Sax ji!Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwebiir dëkk bu ñu gaw.23Man nag saalitoon naa ne:«Yàlla dagg na ma, sànni!»Ndeke ba ma lay woo,dégg nga samay dagaan.24Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji.Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm,di yool, ba wis kuy réy-réylu.25Képp ku yaakaar Aji Sax ji,dëgërlul te amu fit.