Taalifi cant3wol_mbs

Aji jub a ngi woote wall

1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor .
2Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare!Ñu baree may jógal,3ñu baree may tooge naa:«Yàlla du ko wallu!» Selaw .
4Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg,di ma teral, di ma siggil.5Maay woo Aji Sax ji wall,mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
6Maay tëdd nelaw, yewwu;Aji Sax ji di ma aar.7Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma,te duma ragal.
8Éy Aji Sax ji sama Yàlla,jógal, wallu ma!Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp,foq seeni sell.9Aji Sax ji, yaa moom wall,sa mbooloo jagoo sa barke. Selaw.