Taalifi cant26wol_mbs

Ma waajal ndajem kër Aji Sax ji

1Ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, àtte ma,man de màndu laa wéye,Aji Sax ji laa wóolu, jenguma.
2Aji Sax ji, nattu ma, seetlu ma,seggal xel ak xol.3Maa ngi janook sa ngor,di doxe sa dëgg.4Toogumaak naxekat,lëngoowumaak naaféq,5sib naa gàngooru saay-saay,toogumaak ku bon.6Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib,di wër sa sarxalukaay,7àddu, sant la,lim sa jépp jaloore.8Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay,bëgg béreb bi sag leer teew.
9Bu ma buubaaleek bàkkaarkat, sànni,di ma booleek bóomkat, bóom.10Seeni loxoo nga sóobu ci mbon,ndijoor ya fees aki ger.
11Man nag màndu laay wéye,tee nga maa jot, baaxe ma?12Ndokk bi ma taxawee joor gu wóor.Ma màggal Aji Sax ji fi ndajey way-ngëm ñi.