Taalifi cant25wol_mbs

Aji Sax jeey gindee, di yiire

1Ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, yaw laay diis sama bakkan.
2Sama Yàlla, yaw laa yaakaar.Yàlla buma rus,noon yi ree.3Deesu la séentu, ba rus.Kuy wor ci neen mooy rus.
4Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon,xamal ma fi nga ma jaarloo.5Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma.Yaw yaay Yàlla ji may musal,ma di la yendoo yaakaar.6Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor,sa jikkoo ngi fés ba nëgëni.7Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy.Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.
8Aji Sax jee baax, rafeti dogal,di gindi moykat ci yoon wi,9di jiite ku woyof mbubb ci njubte,di ko xamal aw yoonam.10Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiiteekuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.
11Éy Aji Sax ji, tooñ naa lool,jéggal ma ngir sa tur.12Ana kuy wormaal Aji Sax ji,mu won ko yoon wi mata tànn,13muy dunde ngëneel,askanam moom réew mi?14Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal.Kóllëreem la koy xamal.15Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji,moo may xettali ci fiiru noon.
16Ngalla geesu ma, baaxe ma,maa wéet, néew doole,17sama xol feesey xalaat.Rikk, teggil ma njàqare!18Xoolal sama naqar ak sama tiis,te baal ma bépp bàkkaar.19Xoolal noon yi ne gàññ,bañ ma mbañeelu fitna.
20Éy, aar ma, musal ma!Bu ma rusloo,yaw laa làqoo.21Yal na ma mànduteek njub taxawu,maa ngii, di la xaar.22Éy Yàlla, teggilal Israayil tiisoo tiis.