Taalifi cant23wol_mbs
Aji Sax jee may sàmm
1Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.Aji Sax jee may sàmm,du lenn lu ma ñàkk.2Parlu mu naat la may gooral,wal mu dal, mu tette ma ca,3leqali ma,teg ma ci yooni njubngir teraangay turam.4Su may jaare xuru dee wu ne këruus it,duma ragal loraange:yaw laak man,sa bantu sàmm ak sa nguul,yooyoo may dalal.5Yaa ma berndeel,noon yi gis,nga diwal ma saa bopp, terale ma,saab kaas rembat.6Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund,ma dëkke këram ba fàww.