Taalifi cant22wol_mbs

Jëkke jàq, mujje sant

1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.
2Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?Ma binni, binneeti, wall sore.3Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo;woote guddi, noppaloo ma.4Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal,Israayil di la kañ.5Yaw la sunuy maam wóolu woon,wóolu la, nga xettali leen.6Yaw lañu daa woo wall, mucc;yaw lañu wóolu woon te rusuñu.7Man nag aw sax rekk laa, matuma nit.Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.8Ku ma gis ñaawal ma,biiñ ma, xeelu ma, naa:9«Na wéeru ci Aji Sax ji, mu xettali ko;su ko soppee, na ko wallu.»10Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey,naxe ma sama weenu yaay.11Yaw laa dénkoo ba may juddu,ba ma juddu ci sama ndey, ngay sama Yàlla.12Bul ma sore,musiba teew na, wall amul!13Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk,dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.14Ñu ŋa ma, ŋàpp,ni gaynde guy yëmmooka fàdde.15Doole ŋiis,yax yoqi,fit ne soyox, seey.16Làmmiñ taqoo denqleñ,doole jeex, ma wow koŋŋ,nga tëral ma buntu bàmmeel.17Ay xaj a ma wër,di gàngooru saay-saay, dar ma kepp,bëtt samay loxook samay tànk.18Maa ngii, mana waññ sama yax yépp,ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,19séddoo samay yére,tegoo bant sama mbubb.20Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore;yaa may dooleel, gaawe ma.21Xettalil sama bakkan ci saamar,ba sama benn bakkan bii mucc ci selli xaj!22Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll.Yaa ma wallu woon!23Maay siiwali saw tur ci samay bokk,maa lay kañ fi digg mbooloo mi.24Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko.Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggalleen ko.Yeen bànni Israayil gépp, wormaalleen ko.25Moom de sàgganewul mbaa xeebul boroom tiis,làqu ko kanamam,ba mu wootee, wuyu na ko.26Yaw laay sante ndaje mu mag,sottalal la samay dige , ñi la ragal seede.27Ku woyof a cay lekk ba doyal,kuy wut Aji Sax ji, sant ko.«Guddleen a gudd fan!»
28Àddina wërngal këpp ay fàttaliku,walbatiku ci Aji Sax ji.Làngi xeet yépp sukkalsi ko.29Aji Sax jeey boroom nguur,moo yilif xeet yi.30Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko,ku jëm pax it, te bakkanam di lang,di ko sukkal.31Askan wu dikkagul dina jaamu Boroom bi,ñiy ñëw te juddooguñu dees na leen wax ay mbiram.32Ñu dikk, biral njubteem,jottali xeet wu sosoogul jalooreem.