1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettalee ci mboolemi noonam, xettali ko it ci Buur Sawul. Kàdduy woy wa lii la.2Mu ne:Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.3Aji Sax ji mooy sama cëslaay,moo may aar,di ma wallu.Yàllaay sama cëslaay li ma yiiroo,fegu;mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.4Ki yelloo cant, Aji Sax ji,moom laa woo, mucc ci samay noon.5Buumi dee tanc ma,walum kasara naq ma,6buumi njaniiw laaw ma,dee ne jaas, di ma fiir.7Ma jàq, woo Aji Sax ji,ne sama Yàlla wallóoy,mu dégge këram.Ma yuuxu, muy dégg.8Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri;reeni tund ya jaayu, di reg-regi.9Saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya,sawara boye ca gémmiñ ga,xal yu yànj tàkke ca.10Mu firi asamaan, wàcc,niir yu fatt lal tànk ya.11Ma nga war malaakam serub, di naaw,daayaarloo laafi ngelaw.12Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo,làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,13leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca,ak tawub yuur ak xali sawara.14Aji Sax jee dënoo asamaan.Aji Kawe jee àddu,muy tawub yuur ak xali sawara,15mu soqiy fitt ak jumi melax,tasaare leen, fëlxe.16Aji Sax ji, dangaa gëdd,nokki, mu riir,xuri géej ne fàŋŋ,ron suuf ne duŋŋ.17Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma,seppee ma ca xóotey ndox ma,18musal ma ca noon yu magya ma bañ te man ma.19Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee,Aji Sax ji taxawu ma,20yaatal ma,bége ma, ba xettali ma.21Aji Sax jee ma yool sama njub,samay loxoo set, mu fey ma.22Sàmm naa yooni Aji Sax ji,bonuma, di moy sama Yàlla.23Dama ne jàkk ndigalam yépp,dëdduwuma dogali yoonam.24Seede na, may jëfeg mat,di moyoo tooñ.25Aji Sax jee ma yool sama njub,rafetlu sama mucc ayib.26Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore;ku matale, fekk la matale;27ku sellal, fekk la sell;ku dëng, fekk laak say feem.28Yaw yaay musal xeet wu néew doole,kuy daŋŋiiral, nga detteel.29Yaw kay yaa may niital.Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm.30Maak yaw kay, ma song gàngoor.Maak sama Yàlla, ma tëbum tata.31Yàllaa mat.Kàddug Aji Sax jee wér te wóor.Mooy feg képp ku ko làqoo.32Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji?Ana ku mat cëslaay ku dul sunu Yàlla?33Yàllaa may dooleel,di ma xàllal, yoon mat.34Moo ma gaawal ni kéwél,taxawal ma fu kawe.35Moo may tàggat ci xare,may tàwwig fitt ci xalag xànjar.36Aji Sax ji yaa may feg, musal ma,dooleel ma sa loxo,nangul ma, darajaal ma.37Yaa ma xàllalu yoon,ba duma tërëf.38Ma dàq noon yi, dab leen,jekkali, doora dëpp.39Ma jam leen, jógatuñu,xanaa fëlëñu, ma joggi.40Sol nga ma dooley xare,sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.41Won nga ma ndoddi noon,ma boole bóom bañ yi.42Ñu ne wallóoy, wall amul;ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.43Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal,ma wetti ni banu mbedd.44Xettali nga ma ci bokk yiy fippu,def ma, ma jiite ay xeet;waaso wu ma xamul sax nangul ma,45ku ma ci dégg, déggal ma,ay doomi doxandéem di ma raamal,46ne yàcc,génne seeni tata, di lox.47Aji Sax jeey kiy dund.Kii ma sësoo jara sant.Yàlla mi may musal moo màgg!48Mooy Yàlla ji ma feyul,nangulal ma xeet yi.49Xettali nga maak noon,kaweel ma, ma tiim ku ma jógal,xettaleeti ma cib soxor.50Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi,ma kañ sa tur!51Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy,yaay ji ngor ki nga fal,muy man Daawuda, di sama askan ba fàww.