Taalifi cant15wol_mbs

Kuy aji jub?

1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma?Ana kuy dëkki sa tund wu sell?
2Xanaa ki wéye màndu,di def lu jekk,di wax dëggu xolam.3Du sos,du tooñ dëkkandoo,du baatal moroomam.4Ku siblu, mu sib,ku ragal Yàlla, mu teral.Mooy sàmm ngiñam,su ko dee lor it.5Du leble, ba teg ca;du nangu ger, ngir fexeel jàmbur.Lii ku koy jëfe doo jang.