1Màggalleen Ki Sax!Nangeen màggale Aji Sax ji fa asamaan,màggale ko fa kaw-a-kaw.2Màggalleen ko, yeen malaakaam yépp,màggalleen ko, yeen gàngooram yi.3Màggalleen ko, yeen jant beek weer wi,màggalleen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi.4Màggalleen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw,ba ca ndox ma tiim asamaan ya.5Nañu màggal turu Aji Sax ji,kii kat a santaane, lii lépp am.6Moo leen samp, ñu sax ba fàww,mu dogal ko, te du toxu.7Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf,yeen ninki-nankay géej ak xóote yépp,8ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw,ak tawub yuur akub lay,ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.9Màggalleen ko yeen tund yu mag yeekyu ndaw yépp,ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,10ba ci mala yépp, yu àll ak gépp jurak luy raam ak njanaaw,11ak buuri àddinaak xeet yépp,ak kilifa yeek njiiti àddina yépp,12xale bu góor ak bu jigéen,mag ak ndaw.13Màggalleen turu Aji Sax ji,moom doŋŋ la turam kawe,darajaam tiim asamaan ak suuf.14Moo dooleel ñoñam,wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israayil,xeet wi mu xejjoo, di ko màggal.Màggalleen Ki Sax!