Taalifi cant145wol_mbs
Ma kañ Buur Yàlla
1Di woyu màggal, ñeel Daawuda.Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal,teral sa tur ba fàww.2Bésoo bés ma di la sant,di màggal sa tur ba fàww!3Aji Sax jee màgg te jara màggal a màggal,kii màggam amul kemu!4Na maasoo maas di màggal say jaloore,di biral sa njàmbaarte.5Sa leeraayu ndam li ne ràññ,ak sa jëf ju yéeme laay jàngat!6Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottali,te sa màggaay maa koy yéene.7Sa mbaax gu réy, dees na ko tari,te sag njubte, dees na ko woy.8Yiw ak yërmande, fa Aji Sax ji;kee muñ mer te bare ngor!9Aji Sax jee baaxe ñépp,di yërëm lu mu sàkk.10Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm,sa wóllëre yi di la sant,11di tudd sa darajay nguur,tey dégtale sag njàmbaar,12doom aadama xam say jalooreak sa darajay nguur gu màgg gi.13Sa nguur ay nguur gu sax dàkk,sa kilifteef ñeel maasoo maas.Aji Sax ji daa sàmm ay waxam,gore ciy jëfam.14Ku daanu, Aji Sax ji wallu;ku sëgg, mu siggil.15Ñépp a la wékk bët, di yaakaar,te bu jotee, yaa leen di leel,16tàllal sa loxo,reggal luy dund, ba xolam sedd.17Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la,jëfam jépp ngor la.18Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la,képp ku ko woo wall te muy dëgg.19Nammeelu ku ko ragal, mu sottal;yuuxam, mu dégg, musal.20Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem,di sànk képp ku bon.21Naa sàlloo sant Aji Sax ji,na luy dund saxoo dàkk di màggal sellaayu turam!