1Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma.2Ma àddu, ñaan Aji Sax ji;àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,3sippi ko sama tawat,diis ko sama njàqare.4Bu ma yoqee,ràññee nga samay jéego;yoon wi may jaarelañu ma làqal am yeer.5Ma geesu ndijoor, xool;du kenn ku ma faale.Rawtu réer ma,du kenn ku sama bakkan saf.6Aji Sax ji, ma woo la wall;ma ne, yaay sama kiiraay,di sama séddoo fi kaw suuf.7Teewlul, ma ne wóoy,damaa manatul,xettali ma ci ñi ma topp,dañu maa ëpp doole.8Ngalla génne ma fi ma tëje,ma sant la.Man la way-ngëm ñi di yéew ëllëg,yaa may xéewale ab yool.