Taalifi cant135wol_mbs

Lu Yàlla namm lay def

1Màggalleen Ki Sax!Màggalleen turu Aji Sax ji,éey jaami Aji Sax ji, màggalleen,2yeen ñi taxaw ci kër Aji Sax ji,fi sunu biir ëttu Yàlla bi.3Màggalleen Ki Sax, Aji Sax jee baax!Kañleen ko, kee sopplu!4Ki Sax a tànn Yanqóoba,muy Israayil mi mu séddoo.
5Maa xam ne Aji Sax ji màgg na!Sunu Boroom a sut lépp lu ñuy jaamu.6Lépp lu Aji Sax ji namm,moom lay def asamaan ak suuf,ak biir géej ak xóote yépp.7Mooy yékkateey niir fa cati àddina,sàkkal taw ay melax,yebbee ngelaw cay dencam,8faat luy taaw fa Misra,doom aadama, ba ci mala.9Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir,ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.10Moo duma ay xeeti xeet,bóom buur yu mag yi,11muy Sixon buurub Amoreen ña,ak Og buuru Basan,ak buuri Kanaan yépp.12Moo nangu seen réew, séddale,bànni Israayil ñiy ñoñam séddoo.
13Aji Sax ji, sa tur ba fàww;Aji Sax ji, sa woy a saxal maasoo maas.14Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi,di ñeewante jaamam ñi.15Tuuri yéefar yi, xaalis laak wurus,loxoo ko sàkk.16Am gémmiñ te du wax,ami gët te du gis,17ami nopp te du dégg,du sax noowal bakkan.18Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom,ñook ñi leen wóolu ñépp.19Éey waa kër Israayil, santleen Aji Sax ji!Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!20Éey waa kër Lewi, santleen Aji Sax ji!Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen Aji Sax ji!21Nañuy sant Aji Sax ji ci Siyoŋ,moom mi dëkke Yerusalem.Màggalleen Ki Sax!