Taalifi cant13wol_mbs

Aji Sax ji, loo deeti xaar?

1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2Céy Aji Sax ji, loo deeti xaar?Xanaa doo ma tanqamlu ba fàww?Loo deeti xaar, bañ maa geesu,3ba ma tàggook bopp bu ubuak njàqarey xol bu sax,ba noon dootu ma man?
4Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma,leqali ma, bala ma ne sërëx ci nelawi dee,5noon ba naan: «Daan naa ko,»bañ yay bége saab jéll.
6Man de maa ngi dénkoo sa ngor,di bànneexoo sag wall.Naa woy Aji Sax ji,ki may baaxe xéewalam.