Taalifi cant129wol_mbs

Noon manul Israayil

1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal.Israayiloo, waxati ko:
2Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal,te taxul ñu man ma.3Sama gannaaw gi lañu gàbb a gàbb,rëdd koo rëdd nib tool.4Waaye àtteb Aji Sax ji mooy dëgg,dog na buumi ñu bon ña.
5Képp ku noonoo Siyoŋ,yal nañu ko dëpp, gàcceel ko.6Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd,balaa law, lax.7Du doyub ŋëb ku ko dog;du doyub say ku ko for.8Ku fa jaare it du ko ne:«Jaajëf, Aji Sax ji barkeel;jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»