Taalifi cant123wol_mbs
Yàlla, fajal nu gàcce
1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.Yaw laay séentu,yaw mi toog fa asamaan.2Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët,jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen,ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët,ba keroog mu baaxe nu.3Éy Aji Sax ji, baaxe nu, rikk baaxe nu,dañu noo toroxal, ba nu ne tott.4Ñu reew ñaa ngi nuy ñaawal, sunu xol fees,ñu bew ñaa ngi nuy sewal.