Taalifi cant120wol_mbs
Ma ñaan ci biir tuuma
1Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall,mu wuyu ma.2Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat,ak làmmiñu njublaŋ.3Yaw boroom làmmiñu njublaŋ,ana lu ñu lay añaleak lu ñu lay dolli?4Xanaa fitti mbër yu ñawak xal yu yànj.5Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg yatey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!6Yàgg naa loolci biir nit ñi bañ jàmm.7Man may wut jàmm,te su ma waxee, ñoom ñuy ayoo.