Taalifi cant116wol_mbs

Ma sant Yàlla mi ma xettali

1Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo,dagaan ko, mu dégg ma.2Teewlu na ma moos,dama koy woo li feek may dund.3Buumi dee a ma laawoon,njàqarey njaniiw dab ma,ma dajeek naqar aku tiis.4Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko:«Ngalla Aji Sax ji, xettali ma!»5Aji Sax jeey boroom yiw ak njub,sunu Yàllaay boroom yërmande.6Aji Sax jeey aar ku xamul àddina;tumurànke woon naa, mu wallu ma.7Bu ma yeboo sama xel dal,Aji Sax ji baaxe na ma!
8Xettali nga ma, ba deewuma,jàppale ma, ba tërëfuma,feral nga it samay rongooñ.9Damay topp Aji Sax jici biir réewum aji dund ñi.10Ba ma wax: «Torox naa ba toskare,»teewul may ànd ak ngëm.11Maa jàqoon ba naan:«Ñépp ay fen-kat lañu!»12Ana lu may njukkale Aji Sax ji,li mu ma baaxe lépp?13Xanaa ma yékkati kaasu Aji Saxjiy misaal wallam,te may tudd turam.14Samay digeek Aji Sax ji laay matalfi kanam ñoñam ñépp.
15Wóllërey Aji Sax ji,deewam day doon lu muy naqarlu.16Aji Sax ji, maay sab jaam,maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur.Yaa yiwi samay buum,17yaw laay sarxalal saraxu cant,woo la ci sa tur, Aji Sax ji.18Samay digeek Aji Sax ji laay matalfi kanam ñoñam ñépp,19fi ëtti kër Aji Sax ji,fi digg Yerusalem.Màggalleen Ki Sax!